"رَبِّ هَبۡ لِي مِن لَّدُنكَ ذُرِّيَّةٗ طَيِّبَةًۖ إِنَّكَ سَمِيعُ ٱلدُّعَآءِ٣٨". [آلِ عِمْرَانَ - 38].
"رَبِّ لَا تَذَرۡنِي فَرۡدٗا وَأَنتَ خَيۡرُ ٱلۡوَٰرِثِينَ٨٩". [الْأَنْبِيَاءِ - 89].
Sama Boroom, may ma ci sa ngëneel ay doom yu baax. Yaw dégg nga ñaan. [Al-Imran 3:38]
Sama Boroom, bul ma bàyyi ma wéet; Yaw yaa gën ci ñiy donn. [Al-Anbiya 21:89]
"رَبَّنَا ٱغۡفِرۡ لِي وَلِوَٰلِدَيَّ وَلِلۡمُؤۡمِنِينَ يَوۡمَ يَقُومُ ٱلۡحِسَابُ٤١ ". [إِبْرَاهِيمُ - 41].
Sunu Boroom, jéggal ma, sama ñaari wayjur ak way-gëm yi, bis bu ñuy limal jëf yi. [Ibrahim 14:41]
Yalla, maa ngi lay ñaan pastéef ci mbir mi, ak dogu ci topp njub, té ñaan la sababi sa yërmande ak dëggal sa jéggal, té ñaan ngërëm. Sa barke, ak xéewali jaamu La, ta maa ngi lay ñaan xol bu muur ak làmmiñ wu sell, ta maa ngi lay ñaan li gën ci li nga xam, maa ngi sàkku muslu ci yaw ci ay bon yu li nga xam. Te maa ngi ñaan njéggal ci li nga xam ndax yaw yaa xam lu nëbbu.
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad