Yalla, maa ngi lay ñaan lépp lu baax, leegi ak ëlëg, li ma xam ak li ma xamul, maa ngi lay ñaan ci lépp lu bon, leegi ak ëlëg. Xamoon naa ko ak lima xamul. Yaw Yàlla maa ngi lay ñaan lu gën ci li la sa jaam ak sa Yonent ñaan, maa ngi lay sàkku muslu ci yaw ci loru li sa jaam sàkku muslu. Te sa Yónent Yaw Yàlla, maa ngi lay ñaan Aljana ak bépp kàddu walla jëf bu may jegeel, te maa ngi sàkku musël ci Yaw ci Safara ak bépp kàddu walla jëf bu may jegeel. Maa ngi lay ñaan nga jël bépp dogal bu baax ci man.
"فَاطِرَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ أَنتَ وَلِيِّۦ فِي ٱلدُّنۡيَا وَٱلۡأٓخِرَةِۖ تَوَفَّنِي مُسۡلِمٗا وَأَلۡحِقۡنِي بِٱلصَّٰلِحِينَ١٠١". [يُوسُفَ - 101].
Yaw mi sàkk asamaan yi ak suuf si, Yaw yaay sama Sang ci àddina ak àllaaxira. Def ma ma dee di jullit, te boole ma ak ñu jub ñi. [Yusuf 12:101]
اللَّهُمَّ أَرِنَا الْحَقَّ حَقًّا وَارْزُقْنَا اتِّبَاعَهُ، وَأَرِنَا الْبَاطِلَ بَاطِلاً وَارْزُقْنَا اجْتِنَابَهُ.
اللَّهُمَّ آتِ نَفْسِي تَقْوَاهَا ، وَزَكِّهَا أَنْتَ خَيْرُ مَنْ زَكَّاهَا، أَنْتَ وَلِيُّهَا وَمَوْلَاهَا.
اللَّهُمَّ رَبَّنَآ أَتۡمِمۡ لَنَا نُورَنَا وَٱغۡفِرۡ لَنَآۖ إِنَّكَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ قَدِيرٞ.
اللَّهُمَّ حَبِّبْ إِلَيْنَا الْإِيمَانَ وَزَيِّنْهُ فِي قُلُوبِنَا ، وَكَرِّهِ إِلَيْنَا الْكُفْرَ وَالْفُسُوقَ وَالْعِصْيَانَ ، وَاجْعَلْنَا مِنَ الرَّاشِدِينَ.
اللَّهُمَّ مُصَرِّفَ الْقُلُوبِ صَرِّفْ قُلُوبَنَا عَلَى طَاعَتِكَ.
Yàlla, won nu dëgg gi ni muy dëgge, te may nu nu topp ko. Won nu neen gi ni muy neene, te may nu nu moytu ko.
Yàlla, may sama bakkan ragal la. Setal ko, Yaw yaa gën a setal ko. Yaay ki ko jiite te di Boroomam.
Yàlla, sunu Boroom, matal sunu leer te jéggal nu. Man nga lépp.
Yàlla, bëggloo nu ngëm gi te taaral ko ci sunuy xol. Bañloo nu weddi, réewande ak moy, te def nu ñu bokk ci ñi jub.
Yàlla, Yaw mi di wëlbati xol yi, jublul sunuy xol ci déggal la.
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad