Yalla, maa ngi lay ñaan pastéef ci mbir mi, ak dogu ci topp njub, té ñaan la sababi sa yërmande ak dëggal sa jéggal, té ñaan ngërëm. Sa barke, ak xéewali jaamu La, ta maa ngi lay ñaan xol bu muur ak làmmiñ wu sell, ta maa ngi lay ñaan li gën ci li nga xam, maa ngi sàkku muslu ci yaw ci ay bon yu li nga xam. Te maa ngi ñaan njéggal ci li nga xam ndax yaw yaa xam lu nëbbu.
"فَاطِرَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ أَنتَ وَلِيِّۦ فِي ٱلدُّنۡيَا وَٱلۡأٓخِرَةِۖ تَوَفَّنِي مُسۡلِمٗا وَأَلۡحِقۡنِي بِٱلصَّٰلِحِينَ١٠١". [يُوسُفَ - 101].
Yaw mi sàkk asamaan yi ak suuf si, Yaw yaay sama Sang ci àddina ak àllaaxira. Def ma ma dee di jullit, te boole ma ak ñu jub ñi. [Yusuf 12:101]
"رَبَّنَا لَا تُزِغۡ قُلُوبَنَا بَعۡدَ إِذۡ هَدَيۡتَنَا وَهَبۡ لَنَا مِن لَّدُنكَ رَحۡمَةًۚ إِنَّكَ أَنتَ ٱلۡوَهَّابُ٨ ". [آلُ عِمْرَانَ - 8].
Sunu Boroom, bul jengal sunuy xol gannaaw ba nga nu gindee. May nu yërmaande ju jóge ci Yaw; Yaw yaay Mayewaakoon bi. [Al-Imran 3:8]
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad