"رَبِّ إِنِّيٓ أَعُوذُ بِكَ أَنۡ أَسۡـَٔلَكَ مَا لَيۡسَ لِي بِهِۦ عِلۡمٞۖ وَإِلَّا تَغۡفِرۡ لِي وَتَرۡحَمۡنِيٓ أَكُن مِّنَ ٱلۡخَٰسِرِينَ٤٧ ". [هُودٌ - 47].
Sama Boroom, maa ngi la di ñaan nga aar ma ci laaj la lu ma xamul. Soo ma jéggalul te yërëmul ma, dinaa bokk ci ñi sànku. [Hud 11:47]
Yalla, yaw mi xam li nëbbu ak li seede, mi sàkk asamaan yi ak suuf si, boroom lépp ak boroomam, maa ngi seede ni amul yàlla budul Yaw, maa ngi wut musal ci sama bopp ak ci soxor Seytaane ak fiir bimu jàpp.
"رَبِّ أَوۡزِعۡنِيٓ أَنۡ أَشۡكُرَ نِعۡمَتَكَ ٱلَّتِيٓ أَنۡعَمۡتَ عَلَيَّ وَعَلَىٰ وَٰلِدَيَّ وَأَنۡ أَعۡمَلَ صَٰلِحٗا تَرۡضَىٰهُ وَأَدۡخِلۡنِي بِرَحۡمَتِكَ فِي عِبَادِكَ ٱلصَّٰلِحِينَ١٩". [النَّمْلِ - 19].
Sama Boroom, may ma ma sant sa yiw yi nga ma jagleel ak samay waajur, te ma def jëf ju jub ji nga nangu, te dugal ma ci sa yërmaande ci say jaam yu jub yi. [An-Naml 27:19]
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad