Yalla, yaw mi xam li nëbbu ak li seede, mi sàkk asamaan yi ak suuf si, boroom lépp ak boroomam, maa ngi seede ni amul yàlla budul Yaw, maa ngi wut musal ci sama bopp ak ci soxor Seytaane ak fiir bimu jàpp.
"وَسِعَ رَبُّنَا كُلَّ شَيۡءٍ عِلۡمًاۚ عَلَى ٱللَّهِ تَوَكَّلۡنَاۚ رَبَّنَا ٱفۡتَحۡ بَيۡنَنَا وَبَيۡنَ قَوۡمِنَا بِٱلۡحَقِّ وَأَنتَ خَيۡرُ ٱلۡفَٰتِحِينَ٨٩". [الْأَعْرَافِ - 89].
Xam-xamu sunu Boroom ëmb na lépp. Ci Yàlla lañu wóolu. Sunu Boroom, àtteel sunu diggante ak sunuy nit ci dëgg, te Yaw yaay gën ci ñiy àtte. [Al-A‘raf 7:89]
"حَسۡبِيَ ٱللَّهُ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَۖ عَلَيۡهِ تَوَكَّلۡتُۖ وَهُوَ رَبُّ ٱلۡعَرۡشِ ٱلۡعَظِيمِ١٢٩ ". [التَّوْبَةُ - 129].
Yàlla doy na ma. Amul yàlla ku dul Moom. Moom laa wóolu, te Moom mooy Boroom Aras bu màgg bi. [At-Tawba 9:129]
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad