Yalla, maa ngi lay ñaan pastéef ci mbir mi, ak dogu ci topp njub, té ñaan la sababi sa yërmande ak dëggal sa jéggal, té ñaan ngërëm. Sa barke, ak xéewali jaamu La, ta maa ngi lay ñaan xol bu muur ak làmmiñ wu sell, ta maa ngi lay ñaan li gën ci li nga xam, maa ngi sàkku muslu ci yaw ci ay bon yu li nga xam. Te maa ngi ñaan njéggal ci li nga xam ndax yaw yaa xam lu nëbbu.
"رَبِّ ٱجۡعَلۡنِي مُقِيمَ ٱلصَّلَوٰةِ وَمِن ذُرِّيَّتِيۚ رَبَّنَا وَتَقَبَّلۡ دُعَآءِ٤٠ ". [إِبْرَاهِيمُ - 40].
Sama Boroom, def ma ak ñenn ci samay doom ak sët nu sàmm julli. Sunu Boroom, nangu sama ñaan. [Ibrahim 14:40]
"وَسِعَ رَبُّنَا كُلَّ شَيۡءٍ عِلۡمًاۚ عَلَى ٱللَّهِ تَوَكَّلۡنَاۚ رَبَّنَا ٱفۡتَحۡ بَيۡنَنَا وَبَيۡنَ قَوۡمِنَا بِٱلۡحَقِّ وَأَنتَ خَيۡرُ ٱلۡفَٰتِحِينَ٨٩". [الْأَعْرَافِ - 89].
Xam-xamu sunu Boroom ëmb na lépp. Ci Yàlla lañu wóolu. Sunu Boroom, àtteel sunu diggante ak sunuy nit ci dëgg, te Yaw yaay gën ci ñiy àtte. [Al-A‘raf 7:89]
Your daily Azkar, offline. Free.
Android · iPhone · iPad